xaajub fiq bi

laab mooy yékkati am toj walla dindi sobe.
laabal set mooy:
julit bi dindi lépp luy sobe ci yaramam, walla ay yéereem, walla ci barab bi muy taxaw di julli.
laabug toj mooy:
nit ki jappu walla mu sangu farata ag ndox mu laab, walla mu tiim bu amul ndox walla bu amee ngant ci jëfëndikoo ndox ma.

da nga koy raxas ag ndox ba mu set.
bu dee ndab lu ab xaj naan dees koy raxas juroom ñaar i yoon raxas bu njëkk ba ñu boole ci suuf.

yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xewal ak ug mucc neena: jullit bi walla Aji -gëm ji bu jappoo ba raxas xar kanamam bépp bakkaar bu mu mas a def ci ay gëtam day rot and ak ndox mi,bu raxasee ay yoxoom bépp bakkaar bu mu mas a def ci ay yoxoom dana rot and ak ndox mi,ni ki noonu bu raxasee ay tankam bakkaaram yi mu masa dox ak tankam yépp dana rot andak ndox mi,ba kerook muy set wecc ci ay bakkaar. Muslim moo ko soloo.

da ngay raxas say tenq ñatti yoon.
nga gallaxndiku, saraxndiku, fiiru ñatti yoon.
gallaxndiku mooy nga guuq ndox wëndeel ko ci sa gémeñ yabbi ko.
saraxndiku mooy:
nga def ndox ci loxo ndeyjoor ñoddi ko ak sa galawal bakkan ba mu dugg ci biir bakkan bi.
fiiru mooy:
nga génne ndox mi nga dugaloon ci sa bakkan mel ni kuy ñandu ak sa loxo cammooñ
gannaw ba nga raxas sa xarkanam ñatti yoon.
raxas say yoxo ba ci say conc yi ñatti yoon.
masaa sa bopp tambalee ci sab jë jëm ci sag ndong, masaa waale say nopp.
nga raxas say tank ba ci say dojar ñatti yoon.
lii mooy njappu li gën a matale,te sax na juge ci yonnente bi ci ay adiis yu Buxaari ak Muslim solo saaba yu bari nettali ko ku ci mel ni Usmaan ak Abdul Laay ibnu zayd ak yenéen i saaba sax na itam ci yoneent bi ne daana jappu benn benn, ak ñaar ñaar maanaam mu raxas cér i njappu yi benn yoon walla ñaar i yoon; lii Buxaarii solo na ko

faratay njappu mooy li nga xam ne bu ci jullit bi bayyee benn njappoom du baax.
1) raxas xar kanam, boole ci ngallaxndiku ak saraxndiku.
2) raxas say yoxo ba ci conca yi.
3) masaa sa bopp ak say nopp.
4) raxas say tank ba ci dojor yi.
5) toftale cér i njappu yi ni ki jiital raxas xar kanam tek ci raxas yoxo yi; doora masaa bopp, tek ci raxas ay tank.
6) tegele njappu mi maanaam nga jappu ci lu amul benn dog-dog ci dingante bi ba cér bi nga raxas di fendi.
- lu mel ni nit ki jappu ba mu xaaj mu bayyi ko toog ba mu yag mu mottali ko, loolu njappu baaxut.

sunnas njappu mooy loo xam ne bu ko kiy jappu defee am ci tiyaaba; te bu ko bayyee du ci am bakkaar te yit njappoom di na wér.
1) tudd Yàlla te mooy nga wax bismil Laahi.
2) soccu.
3) raxas say yoxo ba ci tikkujara yi.
4) teqale waaraam yi.
5) ñaareelu raxas ak bu ñatteel bi ci cér i njappu yi.
6) tambalee ndayjoor.
7) tudd Yàlla ginnaaw njappu li te mooy nga wax ñaan gii:
maa ngi seede ne amul benn buur bu ñiy jaamu ci dëgg bu dul Yàlla moom kepp amul kees koy bokkaaleel,di seede ne muhammadt jaamub Yàlla la te yonnentab Yàlla la.
8) julli ñaar i rakkaa gInnaaw njappu mi.

liy toj njappu mooy lépp lu génne ci ñaar i génnuwaay yu doomu aadama, moo xam ci kanamam walla ci ginnaawam, lu ci mel am saw walla ay dem duus walla ngalawal.
walla ay nelaw walla xel mu dem; walla sax qëm.
ak lekk ndawalug gileem.
ni ki noonu laal sa awra ak sa loxo moo xam ci kanam walla ci ginnaw te dara doxul ci digante bi.

tiim mooy nga jëfandikoo suuf ak lu mél ni moom ci béréb bu sell bu fekkee amoo ndox moo laabe walla nga am ngant ci jëfandikoo ndox mi

booy tiim da ngay dóor say yoxo ci suuf benn yoon nga masaa ci sa xar-kanam ak sa bitti tenq benn yoon.

lépp luy toj njappu day toj tiim.
ni ki noonu boo amée am ndox gannaw bi nga tiimee ba noppi.

ay saŋ mooy lépp lees di sol ci tank te ñu defere ko der.
ay kawas nak mooy lees di sol ci tank te nekkul der.
ñoom ñaar ñepp manees na leen a masaa mu wuutu raxas ay tank

dees koo yoonal gir yombal ak woyafal ñeel jaam ñi rawati na bu jamonoy sedd dugge, walla nit ki nekk ci ab tukki, mu jafe ci moom lool muy summi ay saŋam saa yuy jappu.

1- mu sol ñaari saŋ yi ci ag laab, maanaam ginnaaw njàpp.
2- saŋ wi nekk lu laab, masaa ci sobe du dagan.
3- saŋ wi muur bépp barab bees farataal a raxal ci njàpp.
4-masaa bi nekk ci diir bi nu tënk ci ki fi dëkk te nekkul ci tukki: mooy bis ak ug kuddeem,ki tukki: ñatti fan ak seen i guddi.

melokaanu masaa ci ay saŋ mooy: mu tek yaar i yoxoom yu tooy ak ndox ci kaw waaraam i tànkam daal di leen di rombale ba ca yeel ba, day masaa loxo ndeyjoor bi ci tànku ndeyjoor bi,loxo càmmoñ bi si tànku càmmoñ bi, mu ŋarale ay waaramam buy masaa te du baamtu masaa bi.

1- jeexug diir bi nu ko tënk, du dagan a masaa ci ay saŋ ginnaw jeexug diir bi nu ko tënk ci sariiha, benn bis ak benn guddi ñeel aji sax ji, ñatti bis ak seen i guddi ñeel aji tukki ji.
2- summi saaŋ yi, nit ki bu summee yaar i saŋam wala benn ba ginnaaw bamu ko masaa ba noppi kon masaa ba yàqu na.

julli:mooy sàkkoo jaamu Yàlla ci ay wax ak i jëf yees jagleel,muy ubbikoo ci kàbbar di jeexe ci sëlmal.

julli farata la ci bépp jullit.
Yàlla mu kawe mi neena:
julli dees koo wutal waxtu ñeel way gëm yi. saaru annisaa i

bàyyi julli ag kéefar la,yonnent yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena:
kollare gi dox sunu digante ak ñoom yéefar yi mooy julli, képp ku ko bàyyi weddi na.
Ahmad ak Tirmizii soloo nan ko ak ñeneen.

juroom i julli ci bis bi ak ci guddi gi,jullik fajar:yaar i ràkka,ak jullig tisbaar: ñeent i ràkka,ak jullig tàkkusaan:ñeent i ràkka,ak jullig timis: ñatt i ràkka,ak jullig gee: ñeent i ràkka.

1- lislaam, julli du wér ci ab yéefar.
2- xel: julli du wér ci ab dof:
3- ràññee, julli du wér ci gone gu ràññee wul.
4- yéene.
5- duggug waxtu wi.
6- laab ci am toj.
7- laab ci sobe.
8- muur awra.
9- jublu xibla.

fukk i ponk la ak ñeent, ni ki nii muy ñëwe:
bi ci njëkk: taxaw ci jullig farata ci képp ku ko man.
kàbbaru armal, te mooy "Allaahu akbar".
jàng faatiha.
rukoo, day tàllal ndiggam bamu yamoo, mu def boppam mu tollo ak moom.
yëkkati ku bawoo ci rukoo bi.
yamoo di aji taxaw.
sujjóod,day dëgaral jëam ak bakkanam,ak ay yaar i tenqam, ak yaar i wóomam, ak ay cat i waaraam i tànkam ci barabu sujjootam.
yékkati ku bawoo ci sujjóod bi.
toog ci diggante yaari sujjood yi.
sunna si mooy:
mu lal tànku càmooñ am toog ci, sàmp bu ndayjoor bi, jëmale ko penku.
dal ga, mooy ànd ak dal ci bépp ponkub jëf.
taaya ju mujj ji.
toog ñeel taaya ji.
yaari sëlmal yi, te mooy mu wax yaari yoon: "assalaamu halaykum wa rahmatul Laah"
toftale ponk yi nga xam ne bu nit ki sujjootee laataa muy rukoo ci ag tayeef ag julleem day yaqu, bu dee njuumte nak dafa wara dello rukoo ba noppi délu si waat sujjoot.

wartéef i julli juroom ñatt la:
1) bépp kabbar bu dul kabbaru armal.
2) wax samihal laahu li man hamida ñeel imaam ak kiy julli moom dong.
3) wax rabbanaa walakkal hamdu.
4) wax subhaana rabbiyal asiim benn yoon ci rukoo.
5) wax suhaana rabbiyal ahlaa benn yoon ci sujjóot.
6) wax rabbi iqfir lii ci diggante yaari sujjoot yi.
7) taaya ju njëkk.
toogaayu taaya ju njëkk.

sunnay julli fukk la ag benn mooy yii:
1- mu wax ginnaww bimu kabbaree armal "subhaanaka allaahumma wa bi hamdi ka, wa tabaaraka ismuka, wa tahaalaa jadduka, wa laa ilaaha xayruka" loolu la ñi woowe: ñaanug ubbée.
2- wax: "ahuuzu billaahi minas saydaani rajiim"
3- wax "bismillaahi rahaamai rahiim"
4- wax: aamiin.
5- jàng faatiha.
6- biral jàng gi ñeel imaam bi.
7- wax ginnaaw cant gi: "mil-as samaawaati, wa mil-al ardi, wa mil-a maa sita min say-in bahdu"
8- bépp sàbbaal bu dolliku ci benn sàbbaal ci sàabbaalu rukoo bi maanaam: ñaareelu sabbaal bi ak ñatteel bi wala lu ko ëpp.
9- bépp sàbbaal bu dolliku ci benn sàbbaal ci sàabbaalu sujjood bi.
10- lépp lu tege ci benn yoon bi miy wax ci digante yaari sujjoot yi "rabbi ixfir lii"
11-julli ci ñoñ yonnent bi.
ñeenteel bi:
sunnay jëf yi, ñu kay woowe ay melokaan:
1- yëkati yaari yoxo ci kàabbaru armal bi.
2- ak ci rukoo bi.
3- ak ci yëkkati ku ci rukoo b.
4- ak wàcce leen ginnaaw loolu.
5- teg loxo ndeyjoor ci kaw bu cammooñ bi.
6- xool ci barabu sujjood bi.
7- xàajjale diggate yaari tànqam ci taxawaay bi.
8- ŋëb ñaari yoxoom ci yaari wóomaam ci rokko bi, xàjjale waaraam yi, tàllal ndiggam def boppam mu yamoo ak moom.
9- dëgaral cer i sujjoot yi ci suuf te mu jonjoo ak barabu sujjood bi.
10- soreele ay përag am ak ay wetam, biiram ak ay poojam, ay poojam ak ay yeelam, ak xàjjjale digante ñaari wóomam, ak tàqale ay tànkam, mu def biir waaraam i tànkam ci kaw suuf te tàqale leen,teg ñaar i yoxoom mu tollo ak i waggam, bank ay waraamam.
11- lal tànkam ci diggante ñaari toogaay yi, ak ci taaya bu njëkk bi, ak lal poojam tég ay toogoom ci suuf ci taaya bu ñaareel bi.
12- tàllal ñaari yoxo yi téeg ko ci pooj ci digante yaari sujjood yi, bi te ŋëb waaraam yi, na ka noo nu itam ci taaya yi waye day bank baaraamu sanqleeñ bi ak bu nómboor bi, mu ràbbale baaraamu dëy bi ak bu diggtu bi, muy junj ci baaraamu sànnikaay bi ci buy tudd Yàlla.
13- buy sëlmël mu geestu ndeyjoor ak càmmooñ.

1- bàyyi benn pokk wala benn sart ci sart i julli gi.
2- wax ci ak tayeef.
3- lekk wala naan ci ak tayeef.
4- yëngatu yu bari te toftaloo.
5- bàyyi benn warteef ci wartéefi julli te tay ko.

melokaanu julli:
1- jublu xibla ci sa mbooleem yaram, ci ludul wëlbati ku wala geestu.
2- ginnaaw ba mu yéene julli gimu jubloo julli ci xolam, ci ludul mo koy wax ci làmmiñam.
3-ginnaaw ba mu kàbbar kàbbaru armal daal di wax (allaahu akbar), buy kàabbar mu yëkkëti yaar i yoxoom bamu yamoo ak i wàggam.
4- toppe mu teg biir tenqu loxo ndeyjooram ci kaw bitti ténqu loxo càamooñam ci kaw dënnam.
5- topp mu sàkkoo ubbi julli gi ci wax: " allaahumma baahid baynii wa bay na xataayaaya kamaa baahadta baynal masrixi wal maxribi, allaahumma naqinii min xataayaaya kamaa yunaqaa sawbul abyadi minad danasi, allaahumma ixsilnii min xataayaaya bil maa-i wassalji wal baraji"
wala mu wax:
"maa ngi tudd sag sell yaw sama Boorom, di la sant, sa tur wi màgg na, sa tedd nga kawe na, te amul ku yayoo jaamu kudul yaw"
6- mu muslu daal wax: "ahoozu billahi minas saytaani rajiim" 7- toppemu wax bismil Laahi daal di jàng faatiha, daal di wax: bismillahi rahmaani rahiim 1 alhamdu lil Laahi rabbil haalamiin 2 arrahmaani rahiim 3 maa li ki yawmid diin 4 iyyaaka nahbudu wa iyyaaka nastahiin 5 ihdinas siraatal mustaxiim 6 siraatal laziina anhamta halayhim xayril maxdoobi halayhim waladdaaliin 7 saaru faatiha ( 1--7)
topp mu wax:(aamin) moy :yaw Yàlla yal na nga nangu ñaan.
8- topp mu jàng li jàppandi ci Alxuraan,te mu guddal njàng mi ci jullig suba.
9- topp mu rukoo, mooy: day sëngal ndiggam ngir màggal Yàlla, mu kàbbar bu dee rukoo, yëkkati ay yoxoom ba mu yamoo ak i wàggam. liy sunna mooy: mu tàllal ndiggam, def poppam mu tolloo ak moom, mu teg ay yoxoom ci kaw ay wóomam, xàjjale ay waaraam am.
10- mu wax ci rukoo am "sunhaana Ràbbiyal asiim" ñatti yoon, bu ca dollee: "subhaanakal laahumma wa bi hamdika, allahumma ixfir lii" kon it baax na.
11- topp mu yëkkati boppam bàyyi koo ci rukoo bi, daal di wax: "samihal laahu liman hamidahu", day yëkkaki waale ay yoxoom bam yamoo ak i waggam, maamuum nag du wax: "samihal Laahu liman hamidahu", waaye day wax: "Rabbanaa wa lakkal hamdu".
12- topp mu wax ginnaaw bimu siggEe: "Rabbanaa wa lakkal hamdu, mil-as samaawaati wal-ardi, wa mil-a maa sita min say-in bahdu".
13- topp mu sujjoot sujjoot bu njëkk bi,budee sujjood mu wax: "Allaahu akbar",day sujjood ci juróom ñaar i céram:jë bi,ak bakkan bi,ak yaar i tenq yi,ak yaar i wóom yi,cat i ndëggu yi,mu soreele ay përëg am ci ay wet am,ay yoxoom nag du ko lal ci kay suuf,mu jubale ay waaraam am xibla.
14- mu wax ci sujjootam: "subhaana Rabbiyal ahlaa" ñatti yoon, bu ca dollee: "subhaanakal Laahumma Rabbanaa wa bi hamdika, allahumma ixfir lii" kon it baax na.
15- mu yëkkati bopp am bawoo ci rukoo bi, daal di wax: "Allaahu akbar"
16- topp mu toog ci diggante yaari sujjood yi ci kaw tànku càmmooñam, daal di samp tànku ndeyjooram, mu teg loxo ndeyjooram ci kaw catu pooju ndeyjooram ci li féete ci wóom bi, mu ŋëb baaraam bu ndaw bi ak bi ci tege, mu yëkkati baaraamu sànni kaayam di ko yëngal su dee ñaan, mu jël baaraamu déyam lënkale ko ak baaraamu digg bi bamu wërngal, mu teg loxo càmmooñam ci kaw catu pooju càmmooñam ci li féete wóom bi, tàllal ay waaraamam.
17- mu wax ci toogaayu digante yaari sujjoot yi: "Rabbi ixfir lii, warhamnii, wahdinii, warzuqnii, wajburnii, wa haafinii"
18-topp mu sujjood sujjootu ñaareel bi ni ki bu ñëkk ba ci lañu fay wax wala luñu fay def,bu dee sujjood mu kàbbar.
19-mu jog bawoo ci sujjootu ñaareel bi,daal di wax:"Allaahu akbar" mu julli ràkka bu ñaatel na ka mu jullee ràkka bu ñëkk ba ci luñu fay wax wala luñu fay def, waaye nag du ca jàng ñaanu ubbee ga.
20-topp mu mu toog bu rakkaab ñaareel bi jeexee daal di wax: "Allaahu akbar",daala di toog ni ki mu tooge woon ci diggante yaari sujjood yi.
21- mu jàng taaya ci toogaay bii, daal di wax: "atthiyaatu lil-Laahi was-aslawaatu wat-tayyibaatu,as-salaamu halayka ayyuhan nabiyyu wa rahmatul Laahi wa barakaatuhuu,as-sahaamu alaynaa wa alaa ibaadil-laahi assaalihiina,ashadu an laa-ilaaha,illal-Laahu,wa ashadu anna muhammadan abduhu wa rasuuluhu, allaahumma salli alaa muhammadin wa alaa aali Muhammadin, kamaa sallayta alaa ibraahiima wa alaa aali Ibraahiima,innaka hamiidun majiidun.wa baarik alaa Muhammadin wa alaa aali Muhammadin,kamaa baarakta alaa Ibraahiima wa alaa aali Ibraahiima inna ka hamiidun majiidun. a-uuzu bil-laahi min azaabi jahannama, wa min azaabil xabri,wa min fitnatil mahyaa wal mamaati,wa min fitnatil masiihid dajjaali". mu ñaan Boroomam lumu bëgg ci yiw i àdduna ak yu àllaaxira.
22- mu sëlmal ci ndeyjooram, daal di wax: "assalaamu alaykum wa rahmatul-laahi" ni ki noo nu yit lay def ci càmmooñam.
23- bu julli gi nekkee jullig ñatti ràkka wala ñeent; day taxaw fi taaya bu njëkk jeexe, te mooy: "ashadu an laa ilaaha illal-Laahu, wa ashadu anna muhammadan abduhuu wa rasuuluhuu"
24- mu jóg daal di wax: "allaahu akbar", yëkkati yaar i yoxoom ba mu yamoo ak i waggam.
25- mu jullee li des ci julli gi ni ki mu jullee woon ràkka bu ñaareel bi, waaye nag day yam rekk ci jàng faatiha.
26- mu toog di aji pooju, sàmp tànku ndeyjoor bi, génne tànku càmmooñ bi ci suufu tanku ndeyjoor bi, mu dëgëral ab toogoom ci suuf, teg yaari yoxoom ci kaw ay pooj am ni ki mu ko tege woon ci taayaa bu njëkk bi.
27- ci toogaay bii nag day jàng taaya bi lépp.
28- mu sëlmal ci wetu ndeyjooram, daal di wax: "assalaamu alaykul wa rahmatu-laahi"

"astaxfirul Laaaha" ñatti yoon.
allaahumma antas-salaamu wa minkas-salaamu, tabaarakta yaa zal-jalaali wal-ikraami|"
"laa ilaaha illal-laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul-mulku wa lahul-hamdu, wa huwa alaa julli say-in xadiirun, allaamumma laa maani-a limaa ahtayta wa laa muhtiya limaa manahta, walaa yanfahu zaljaddi minkal-jaddu".
"laa ilaaha illal-laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul-mulku wa lahul-hamdu, wa huwa alaa julli say-in xadiirun, laa hawla wa laa xuwwata illaa bil-laahil, laa ilaaha illal-laahu, walaa nahbudu illaa iyyaahu, lahun-nihmatu wa lahul fadlu wa lahus-sanaa-ul hasanu, laa ilaaha illal-laahu muxlisiina lahud-diina wa law karihal kaafiruuna"
"subhaanal-laahi" fanweer i yoon ak ñatt.
"alhamdu lil-laahi" fanweer i yoon ak ñatt.
"allaahu akbar" fanwéer i yoon ak ñatt.
mu mataleko téemeer ci wax:
"laa ilaaha illal-laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul-mulku wa lahul-hamdu, wa huwa alaa kulli say-in xadiirun"
- mu jàng lixlaas ak muslu kaay yi ñatti yoon ginnaaw jullig fajar ak jullig timis, ak benn yoon ginnaaw yeneen julli yi.
-mu jàng ayaatul kursiyyu,benn yoon.

yaar i ràkka lu jiitu fajar.
ñeent i ràkka lu jiitu gee.
yaar i ràkka ginnaaw tisbaar.
yaar i ràkka ginnaaw timis.
yaar i ràkka ginnaaw gee.
ngëneelam:
yonnente bi neena: "ku julli ci bis bi ak ci guddi gi fukk i ràkka ak yaar ci coobare wu, Yàlla tabaxal ko kër ca aljana" Muslim ak Ahmat soloo nanu ko; ak ñeneen.

bis u aljuma, yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, neena: "bis bi gën ci seen bis yi mooy bisu aljuma, ci lan bind Aadama,ci lan ko faat, ci lan wal ci moom ruu gi, te ci la yuuxug faatu gi di am,dee leen ci bari lu ngeeni julli ci man, ndax seenug julli dan ma koy gaaral. neena: ñu ne ko yaw yonnent Yàlla bi na ka lan lay gaarale sunug julli ci yaw te fekk funux nga? -daañoo wax ràpp nga- mu wax ne: Yàlla mu màgg mi dafa araamal ci suuf muy lEkk yaram i yonnente yi" abuu daawuuda soloo na ko ak ñeneen.

faratay jëm la ci bepp jullit bu góor te mat té am xel tey aji sax.
Yàlla mu kawe mi neena:
"ée yéen ñi gëm bun wootee julli ci bis u aljuma na ngeen jëm ca tudd Yàlla ja te bàyyi njaay mi loolu moo gën ci yéen ndeem xam ngeen 9" saaru almunaafixuuna: 9.

lim i rakkaa y julli g aljuma yaar i ràkka la, da ciy bér u ci njàng mi, yaari xutba yun xam moo koy jiitu.

wuute jullig aljuma dagan ul ci lu dul ngàntul sariiha, bawoo na ci yonnente bi mu wax ne: "képp ku bàyyi ñatt i aljuma ngir woyof al ko; Yàlla di na tëj xol am bi" abuu daawuuda soloo na ko ak ñeneen.

T-
1- sangu.
2- gëttu.
3- sol yéere bu rafet.
4- di kàbbar jëm ca jumaa ja.
5-bari di julli ci yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc.
6- jàng saaru kahfi.
7- jëm ca jumaa ja ci dox.
8- di fuglu waxtuy naggu ñaan.

jële nanu ci Abdallaa doomu Omar yal na leen Yàlla dollee gërëm, yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "jullig mbooloo moo gën jullig kénn ci ñaar fukki daraja ak juroom ñaar" Muslim moo ko soloo.

mooy teewug xol bi ak dalug cér yi ci julli gi.
Yàlla mu kawe mi neena:
"way gëm yi texe nanu 1 te ñooy ñiy toroxlu ci seenug julli 2" saaru al-Muuminuuna 1-2.

moom àq ju war la ci alal jees ko jagleel,ñeel kurel bees ko jagleel ci jamono jees ko jagleel.
te moom ponk la ci ponk i lislaam yi,di ab sarax bu war,dees koy jël ci way woomal ji jox ko way ñàkk ji.
Yàlla mu kawe mi neena:
﴾joxe leen azaka﴿ saaru Baqara: 43

mooy bépp sarax bu dul azaka,lu ci mel ni:sarax bu mu mana doon ci anami yiw yi ci jamono ju mu man a doon.
Yàlla mu kawe mi neena:
"na ngeen di joxe ci yoonu Yàlla" saaru Baqara: 195

mooy jaamu Yàlla ci bàyyi lépp luy dogloo li ko dale ci fenkug fajar gi ba ci sowug jant bi, ànd ag yéene, moom nag yaar i xaaj la:
woor gu war: lu ci mel ni weeru koor, moom ponk la ci lislaam.
Yàlla mu kawe mi neena:
﴾ée yéen way gëm yi farataalees na ci yéen woor na ka ñu ko farataale woon ci ñi leen jiitu woon amaana ngeen ragal Yàlla 183﴿ saaru Baqara: 183
ak woor bu warul:lu ci mel ni woor altine ak alxamis ci ayu bis bu ne, ak woor ñatt bis ci weer wu ne,li ci gën nag mooy bis yu leer yi(13, 14,15) ci weer wu ne.

jële nanu ci Aboo hurayra, yal na ko yàlla dollee gërëm, yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, neena: "képp ku woor weeru koor ci gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram" Buxaari ak Muslim dёppoo na nu ci.

jële na nu ci Abii sahiid alxudrii yal na ko Yàlla dolle gërëm neena: yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "amul benn jaam buy woor benn bis ci yoonu Yàlla,lu dul ne Yàlla di na musal jëmmam ci sawara juroom ñaar fukki nawet ngir bis boobu" Buxaari ak Muslim dёppoo na nu ci.
maanaa "juroom ñaar fukk i nawet" mooy:
juroom ñaar fukk i at.

1- lekk wala naan te tay ko.
2- wàccu te tay ko.
3- génn ci lislaam.

1- gaawa dog.
2- xëdd te yeexe ko.
3-yokk jëf yu baax yi ak jaamu yi.
4- wax ji ki woor di wax bees koo saagaa: man damaa woor.
5- ñaan jamonoy dog.
6- doge tàndarma ju tooy wala ju wow, bu ko amul mu doge ndox.

aj:ak jaamu la ngir Yàlla mu kawe mi,ci jublu néegam bees wormaal ci ay jëf yees ko jagleel,ci wax tu wees ko jagleel.
Yàlla mu kawe mi neena:
"war na ñeel Yàlla ci nit ku ko man mu aji néegub yàlla ba benn yoon, ku weddi nag Yàlla moom doylu na walif mbindeef yépp 97" saaru aali himraan 97.

1- armal.
2- taxaw arafaat.
3- wërug bëbb ga.
4- dox digante safaa ak marwa.

jële na nu ci Abii hurayra yal na ko Yàlla dollee gërëm, neena: dégg naa yonent bi Yàlla na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, mu wax ni: "képp ku aj ngir Yàlla, te beejul sëyul deful ag kàccoor; dana dellu mel ni bis bi ko yaayam jure woon" Buxaarii ak Muslim ñoo ko soloo ak Keneen.
"mel ni bis bi ko yaayam jure woon" maanaam ci ludul benn bàkkaar.

umra: mooy jaamu Yàlla mu kawe mi ci jublu néeg am ba nu wormaal ci ay jëf yees ko jagleel ci waxtu wun ko jagleel.

1- armal.
2- wër néeg ba.
3- dox digante safaa ak marwa.

mooy def ay coono ak kem kàttan ci tasaare lislaam ak yiir ko moo ki ñoñam, wala rayante ak noon i lilaam ak i ñoñam.
Yàlla mu kawe mi neena:
"na ngéen di jihaad ci yoonu Yàlla ci seen alal ak seen bakkan, loolu moo gën ci yéen ndeem xam ngeen 41" saaru attawba 41