xaajub pas-pas

Yallà mi ma sakk sakk mbooleem bindeef yi di leen taxawu ci gépp anam mooy sama Boroom.
tektal bi mooy waxi Yàlla mu kawe mi:
cant ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi [suuratul fatiha 2]

diiney lislaam mooy sama diine,te lislaam mooy nga wommatul Yàlla ci wéetal ko ak topp ay santaaneem te set wecci ci bokkaale ak ñi koy def
Yàlla mu kawe mi neena:
diine fa Yàlla mooy lislaam suuratu aali himraan 19

Muhammat mooy sama yoneent Yàlla na Yàlla julli te sëlemal ci moom.
Yàlla mu kawe mi neena:
Muhammat yonnent Yàlla la. suuratul fathi 29

baatub tawhiid mooy " لا إله إلا الله " liy maanaam baat bi mooy amul kenn ku niy jaamu ci dëgg ku dul Yàlla.
Yàlla mu kawe mi neena:
na nga xam ne amul kenn ku ñuy jaamu ci dёgg ku dul Yàlla. suuratu Muhammat 19.

Yàlla ma nga ca asamaaw ya ca kaw aras féete kaw mbideef yépp, Yàlla mu kawe mi neena: Yàlla miy Boroom yërmaande ju yaatu ji ma nga yamoo fa kaw aras. suuratu taahaa 5 wax na batay: Yàlla mooy notaakon bi féete kaw jaamam yépp mooy Aji- xarañ ji te deñ kumpa. suuratul anhaam 18

maanaam loolu mooy nga nanggu ne yonnente bi Yàlla moo ko yónni ci mbideef yi muy bégal ñi ko topp di xupp ñi ko moy
te war na:
ñu topp ko ci li mu santaane.
te war na it ñu dëggal ko ci lépp lu mu ñu xibaar.
te ñu bañ a wuute ak moom.
te mu bañ a jaamu Yàlla lu dul ci li mu yoonal maanaam ñu tënku ci sunnaam bay lépp luy bidaa.
Yàlla wax na ci suuratu nisaahii ne képp ku topp yonnente bi toppu nga Yàlla, mu dellu waxaat ne: ﴾Yonnente bi du waxe ci bànneexu bakkanam, lumu wax dees ko koo yenkeewal﴿ suuratu annajmi 3;4 Yàlla mu kawe mi te sell neena: ﴾am ngeen ci yonnente bi ab royuwaay bu rafet ñeel képp ku yaakaar Yàlla te gëm bIs pénc tay tudd Yàlla lu bari﴿ suuratul ahzaab 21

Yàlla daf noo bind ngir nu jaamu ko moom dong te bañ koo bokkaale ak dara.
bindu nu ngir ay caaxaan walla am po.
Yàlla mu kawe mi neena:
﴾Binduma jinne ak nit lu dul ñu jaamu ma. ﴿ suuratu azaariyaat 56

loolu de ab baat la bu làmboo lépp lu Yàlla bëgg te gërëm ko ci ay wax ak ay jëf ci lu feeñ ag lu nëbbu.
Li feeñ nag mooy lu mel ni tudd Yàlla ci làmmeñ ci di sàbbaal ak sant ak màggal walla julli ak aji Màkka.
Li nëbbu mooy lu mel ni wakiirlu ci Yàlla ak ragal ko ak yaakaar ko.

li gën a rëy ci li war ci nun mooy weetal Yàlla.

1) tawhiidu arrubuubiyatu maanaam wéetal Yàlla ci ay jëfam: te mooy nga gëm ne Yàlla mooy Aji-bind ji, di wërsëgale te moom dong mooy ki moom lépp, di ko saytu amul kenn kuñ koy bokkaale.
2) tawhiidu al uluuhiyatu, maanaam wéetal Yàlla ci say jëf: loolu mooy wéetal Yàlla ci jaamu ko moom dong bañ koo bokkaale ak dara.
3) tawhiidul asmaahi wassifaati, maanaam wéetal Yàlla ci ay turam ak ay meloom:loolu mooy nga gëm ne Yàlla am na ay tur ak ay melo yu ñëw ci Alquraan ak sunna nga gëm ko bu wér te bañ koo melal walla di ko nuroole ak lenn walla di ko weddi.
liy tektale ñatti xeeti tawhiit yii mooy wax i Yàlla mu kawe mi:
Yàlla mooy Boroom asamaan yi ak suuf yi ak li ci séen diggënte,kon jaamu ko moom dong te nga xam ne amul ku mel ni moom ci ay tur walla aw melokaan. suuratu Maryama 65

bakkaar bi gën a rëy mooy bokkaale Yàlla.
Yàlla mu kawe mi neena:
Yàlla du jéggal ku deewaale ag bokkaale waaye dina jeggale lu dul bokkaale ñeel ku ko neex te képp kuy bokkaale Yàlla def na bàkkaar bu rëy. suuratu annisaa

bokkaale mooy defal keneen ku dul Yàlla lenn ci xeeti jaamu yi.
ay xeetam:

bokkaale gu mag; lu ci mel ni ñaan keneen ku dul Yàlla, walla sujjootal keneen ku dul Yàlla, walla rendi dara ngir keneen ku dul Yàlla.
bokkaale gu ndaw ni ki giñ ci keneen ku dul Yàlla,walla takk ay gàllaj walla yu ni mel ngir mu jariñ la dara walla mu daqal la ay lor,ak lu mel ni ngistal ku sew ni ki kuy julli di ko taaral ngir wan ko nit ñi.

kenn manul xam kumpa ku dul Yàlla.
Yàlla mu kawe mi neena:
waxal jaam ñi ne amul kenn ku nekk ci asamaan yi walla suuf ku xam kumpa ku dul Yàlla, te kenn xamul kañ la nu leen di dekkil. suuratu annamli 65

1) gëm Yàlla mu kawe mi.
2) gëm ay malaakaam.
3) gëm ay téereem.
4)gëm ay yonnenteem.
5)gëm bis pénc.
6)gëm dogal bu neex ak bu naqari.
tektal bi mooy adiisu Jibriil bu siiw bi Muslim solo Jibrill wax yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal te musal ko:
xamal ma lan mooy ngëm, yonnente bi ne ko ngëm mooy nga gëm Yàlla ak i malaakaam, ak i téereem, ak i yonnenteem, ak bis pénc ba, te nga gëm ab dogal bu neex ak bu naqari.

ngëm yàlla mu kawe mi
mooy nga gëm ne Yàlla moo la bind di la wërsëgal, te mooy buur mi moom lepp te moom dong mooy saytu mbideef yi.
te nga gëm ne moom dong moo yayoo jaamu amul kenn ku ñuy jaamu ci dëgg ku dul moom.
te nga gëm ne mooy Aji- màgg ji di ku mat sëkk, te moom donga yayoo mbooleem xeeti cant yi, mooy Boroom tur yu sell yi ak melokaan yu kawe yi amul moroom, te lenn ci mbindeefam yi nuru wu ko.
gёm malaaka yi.
nga gëm ne ay mbindeef la ñu Yàlla da leen a bind ci ag leer ngir ñu jaamu ko topp ndigalam yépp.
bokk na ci malaaka yooyu Jibriil yal na jamm nekk ci moom, mooy malaaka miy wacce ndéeytel Yàlla ci yonnent yi.
gёm téere yi.
téere yi nga xam ne Yàlla a ko wacce ciy yonnenteem.
ni ki Alquraan bi Yàlla wacce ci Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal te musal ko.
ak Injiil bi Yàlla wacce ci iisaa yal na jamm nekk ci moom.
ak Tawraat bi Yàlla jox muusaa yal na jamm nekk ci mom.
ak zabuur bi Yàlla jox Daawuuda yal na jamm nekk ci moom.
ak yeneeni téere yu mu joxoon Ibraahiimaa ak Muusaa.
gëm yonnente yi:

ñooy ñi Yàlla yónni ci jaamam yi ngir ñu jangal leen di leen bégal ci lu baax ak aljana, waaye di leen xupp ci lu bonn ak sawara.
yoneent yooyu ña ca gën ñooy ñi ñiy woowe uluul hazmi te ñoo ñu ñooy:

yonnent Yàlla Nuuh yal na jamm nekk ci moom.
yonnent Yàlla Ibraahiima yal na jamm nekk ci moom.
yonnent Yàlla Muusaa yal na jamm nekk ci moom.
yonnent Yàlla Hisaa yal na jamm nekk ci moom.
yonnente Yàlla Muammat yal na jamm ak xéewal nekk ci moom.
gёm bis bu mujj ba.
bis pénc ba nak mooy li nekk ci ginnaaw dee ci biir bammeel, ak bisub taxawaay ba, ak dekki ak isaab jëf i jaam ñi ba ñu baax ñi dugg aljana bu bonn ñi dem sawara.
gëm ab dogal bu neex walla bu naqari.
ab dogal mooy nga gëm ne Yàlla xam na lépp luy xew ci kéew bi, te bindoon na ko ca lawhul mahfuuz te moom la neex mu am.
Yàlla neena lépp lu am noo ko bind ci sunug dogal.
ab dogal nak ñenti dayo la:

bu njëkk bi mooy: xam xamub Yàlla, ni ki xam xamam bi jiitu lépp luy xew laataa muy xew ak bi mu xewee ba noppi.
tektal bi mooy wax i Yàlla mu kawe mi:
Yàlla rekk a xam tukkig àdduna te mooy kiy wacce ab taw, te moo xam li nekk ci butiiti njuru kaay yi,te amul kenn ku xam lu miy am suba walla ci jan suuf la faatoo,Yàlla mooy ku xam te deñ kumpa. suuratu Luqmaan.
ñaareel bi mooy:
nga gëm ne Yàlla bind na ko ci lawhul mahfuuz, lépp lu xew walla luy xew i ëllak lees bind la cib téere.
tektal bi mooy wax i Yàlla mu kawe mi:
Yàlla mooy ki xam kumpa keneen ku dul moom xamu ko, te mooy ki xam lépp lu nekk ci jéeri yi walla ci géej gi, te amul wenn xob wuy rot ci suuf lu dul ni xam na ko, amul it aw fepp wuy wadd ci lëndamug suuf si lu dul ne xam na ko amul it lu tooy walla lu wow lu dul ne bind na ko cib téere bu leer. suuratul anhaam 59
ñatteel bi mooy:
nga gëm ne lépp luy xew ci coobarey Yàlla lay xewe, te amul dara luy am ludul da koo neex moo xam ci moom la bayyikoo walla ci mbindeef yi.
tektal bi mooy waxi Yàlla mu kawe mi:
ku mu soob ci yéen mu jub waaye dara manu leen a soob lu dul dafa soob Yàlla miy Boroom bindéef yi ba noppi. suuuratu attakwiir 28_29
ñeenteel bi mooy:
nga gëm ne mbooleem bindeef yi ay mbindéefu Yàlla moo bind seen i jëmm ak seen i melo ak seen lépp.
tektal bi mooy wax i Yàlla mu kawe mi:
Yàlla mooy ki leen bind ak seen i jëf. suuratu asaafaati

Alquraan wax i Yàlla la du mbindeef.
Yàlla mu kawe mi neena:
bu kenn ci way bokkaale yi làqoo fi yaw na nga ko fat ndax mu dégg gaddug Yàlla suuratu attawba 6

sunna mooy jépp wax walla jëf jees askanale yonnente bi walla muy aw melo ciy jikkoom walla aw bindiinam walla muy lees def ci kanamam mu saxal ko.

lépp lu nit ñi sos ci diine gannaaw yoneent bi ak i saabaam
dees koy delloo waaye dee su ko nangu.
ngir wax i yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéwal akug mucc:
bépp bidaa ag réer la. abuu daawuuda moo ko soloo
lu ci mel ni yokk ci jaamu Yàlla, ni ki yokk raxaub ñeenteel ci njappu, ak lu mel ni gàmmu, ndax xamee su ko ci yonnente bi ak i saabaam.

li nu jublu ci walaahu mooy mengóo ak way gëm ñi ak dimbali leen
Yàlla mu kawe mi neena: way gëm ñu góor yi ak yu jigéen yi lenn ci ñoom ñoo mengóog ñeneen ñi. suuratu attawba 71
li nu jublu ci baraahu mooy bañ way weddi yi def leen ay noon, maanaam dogoo ag ñoom ba fawwu.
Yàlla mu kawe mi neena:
am ngeen ci Ibraahiima ak ñam andaloon royuwaay wu rafet, ba ñu waxee seenu nit na leen nun day deñ nanu ba set wecc ci yéen ag seen Yàlla yi ngeen di jaamu te du Yàlla, te weddi nan leen, te da ag noonoo akug mbañeel day dox sunu diggante ba fawwu, ba kerook ngeen di gëm Yàlla dong. suuratu al mumtahinatu 4

Yàlla du nangu janeen diine ju dul lislalaam.
Yàlla mu kawe mi neena:
képp ku topp janeen diine ju dul lislaam deesu ko nangu ci moom te bu bis pénc baa di na bokk ci way torox yi. suuratu aali himraan

misaalum wax juy kéefarloo: mooy lu mel ni saaga Yàlla walla ab yonnenteem.
misaalum jëf juy kéerarloo mooy lu mel ni:
doyodal Alquraan, walla sujootal ku dul Yàlla.
misaalum pas -pas buy kéefaloo mooy lu mel ni: nga fas ne am na keneen ku yayoo ag jaamu ku dul Yàlla.

T-
ak naaféq gu mag:
loolu mooy nëbb ak kéefar di feeñal ak ngëm.
loolu nak day génne nit ci lislaam yobbu ko ci ak kéefar ku mag.
Yàlla mu kawe mi neena:
naaféq yi fa gën a suufe ci sawara la niy nekk te kenn manu leen a dimbal. suuratu annisaahi.
2 ak naaféq gu ndaw:

ni ki lu mel ni fen ak wuute ab dig ak wor.
naaféq gu ndaw nak du génne nit ci lislaam, ab bakkaar la ci bakkaar yi, ki koy def nag manees na ko cee mbugal.
yonnente Yàlla bi neena:
mandargam naaféq ñatt la: saa yu waxee fen, bu joxee ab dig wuute ko, bees ko wóoloo mu wor. Buxaariu ak muslim ñoo ko soloo.

ki muju ci yonnente yi mooy muhammet.
Yàlla mu kawe mi neena:
Muhammet nékkul baayub kenn ci yéen waaye yonnenteb Yàlla la, di ki tëj yonnente yi Yàlla moy aji- xam lépp. suuratul ahzaab ٤٠ yonnente bi wax neena: man maay ki tëj yonnent yi,amul beneen ub yonnente buy ñëw sama gannaw. abuu daawuuda ak tirmiziiu soloo na ñu ko ak ñeneen.

kéemtaan mooy lépp lu Yàlla jox ay yoneenteem ci mbir yu xotti baax ngir firdeel seenug dëggu, ni ki lu mel ni:
xar wéer wi ngir dëggal yonnente bi.
ak xotti géej gi ñeel Muusaa, ak labal Fihawna ak ay andandoom.

ab saaba mooy ku dajé ak yonnente bi gëm ko te faatu ci diiney lislaam.
saaba yooyu dañ leen a war a bëgg di leen roy, ndax ñooy ñi gën ci nit ñi gannaaw. yonnente yi.
ñi gën ci ñoom nag ñooy ñenti xalifa yi:

Abuu bakar Yal na ko Yàlla gёrёm.
Omar yal na ko Yàlla gёrёm.
Usmaan yal na ko Yàlla gёrёm.
Alliyu yal na ko Yàlla gёrёm.

ndayi way gëm ñi ñooy soxnay yonnente bi.
Yàlla mu kawe mi neena:
yonnente bi moo gën a yay ci way gëm y ci seen bopp,te ay soxnaam ñooy nday i way gëm ñi. suuratul ahzaab ٦

dan leen a war a bëgg méngoo leen bañ képp ku leen bañ, te bañ a ëppal ci ñoom, te ñoom ñooy ay soxnaam akug njabootam; ak ñi askanoo ci Aaasim, ak Mutalib te bokk ci way gëm yi

sunu warteef ci ñoom mooy wormaal leen déggal leen topp leen ci lu dul ag moy Yàlla, te bañ a fétteerlu ci seen kaw; waaye di leen ñaanal, te di léen laayebiir ci suuf.

seen kër mooy aljana, Yàlla mu kawee mi neena: ñi gëm Yàlla tey jëf jëf ju baax Yàlla da na leen dugal aljana joo xam ne ay dex mooy daw ci biir. suuratu muhammat 12

kërug yéefar yi mooy sawara; Yàlla neena: na ngeen ragal sawara mi nga xam ne la koy xamb mooy nit ak ay xeer te waajalees na ko ñeel yéefar yi. saaru Baqara: 24

ragal: mooy ragal Yàlla ak mbugalam.
yaakaar:
mooy yaakaar yoolub Yàlla ak njéggalam ak yërmandeem.
tektal bi mooy wax i Yàlla mu kawe mi:
( ñooñu ngeen di ñaan ñoom seen bopp da ñiy góor-góorlu ci def lu baax ngir gën a jege Yàlla, ñuy yaakaar yërmandeem di ragal mbugalam te sa mbugalum Boroom lu ñiy moytu la) saaru Israa: 57 Yàlla mu kawe mi neena: ( xibaaral sama jaam ñi ne léen man maay aji jéggale ji maay aji yërëme ji 49 waayé sama mbugal mooy mbugal mu metti mi 50 ) saaru Al-Hujraat: 49, 50

Yàlla, Boroom bi, Aji yëram ji, Aji dégg ji, Aji gis ji, Aji xam ji, Aji wërsëgal ji, Aji dund ji, Aji màgg ji... ak yudul yooyu ci ay tur yu rafet ak melokaan yu kawe.

Yàlla: li miy tekki mooy Yàlla ji niy jaamu ci dëgg moom rekk te amul kenn kees koy bokkaaleel.
Buur bi:
mooy ki bind te mooy ki moom, mooy wërsagal te mooy doxal mbir yi moom dong moom Yàlla mu sell mi.
Aji dégg ji:
mooy ki ag déggam daj lépp, muy dégg kàddu yépp ak séeni wuute ak séeni melokaan.
Aji gis ji:
mooy kiy gis lépp, di gis lépp lu ndaw wala mu rëy.
Aji xam ji:
mooy ki gisam peeg lépp lu weesu wala li teew wala li ñëwagul
Aji yërëm ji: mooy ki yërmaandeem daj bepp mindeef ak lépp luy dund, te jaam yépp ak mbideef yépp ñoo ngi ci suufu yërmàandeem.
Aji wërsagalé:
mooy ki wërsag i mbindeef yépp nekk ci moom moo xam nit la wala jinne wala lépp luy dox ci suuf.
Aji dund ji:
mooy kiy dund te du dee, te mbindeef yépp da ñiy dee.
Aji màgg ji:
mooy ki ame géppug mat ak léppi magg ci ay turam ak i meloom ak i jëfam.

dan leen di bëgg, di dellu ci ñoom si masala yi ak xew-xewi sariiha yi, te dunu leen tudd ci lu dul lu rafet, te kepp ku leen tudd ci lu dul lu rafet dafa jaarul ci yoon wu jub wa.
Yàlla mu kawe mi neena:
(Yàlla dina yëkati ay daraja ñi gëm ci yéen ak ñi ñu jox xam-xam te Yàlla deñ na kumpa ci lépp lu ngeen i def.) saaru Al-mujaadala 11

ñooy way gëm yi te ragal Yàlla.
Yàlla mu kawe mi neena:
ñi méngoog Yàlla du ñu tiit du ñu jaq, ñooñu ñooy ñi gëm Yàlla te ragal ko. saaru Yuunus.

gëm wax la ak jëf ak pas-pas.

gëm day yokkoo cig topp Yàlla di wàññeekoo ci moy Yàlla.
Yàlla mu kawe mi neena:
﴾way gëm yi de ñooy ñi nga xam ne bu ñu tuddee Yàlla seen xol yi day jàq te buñu jàngee aayay Yàlla yi ci ñoom da leen di dolli ag ngëm te ci Yàlla rek lañuy wakkirlu﴿ suuratu Al-anfaal: 2

rafetal, mooy nga jaamu Yàlla mel ni yaa ngi koy gis,ndax boo ko gisul moom mi ngi lay gis.

ci ñaari sart:
1- bu sellee ngir jëmmi Yalla mu kawe mi rekk.
2-bu tegoo ci sunnas yonnente bi ﷺ.

mooy sukkandiku ci Yàlla ci xëcci njariñ ak jañ lor, andal jàpp ci sabab yi.
Yàlla mu kawe mi neena:
képp ku wakkirlu ci Yàlla; Yàlla doy na ko. suuratu Attalaaq: 3
hasbuhoo: mooy doy na ko.

digle lu baax mooy: digle topp Yàlla, tere lu bonn mooy: aaye lépp luy moy Yàlla mu sel mi.
Yàlla mu kawe mi neena:
yeenay xeet wi gën ci xeet yi ndax da ngenn di digle lu baax di tere lu bonn te gëm Yàlla. suuratu aali himraan ١١٠

ñoo ñu ñooy ñi nekk ci li yoneent bi ak i saabaam nekkoon ci jëf ak ci wax ak ci pas- pas.
dees leen di woowe waa sunna ngir topp gu nuy topp sunna di bayyi bidaa
dees leen di askanale ci mbooloo nak ngir booloo gun booloo ci dëgg te dun ci taqalikoo.