xaajub pirim alxuraan:

saaru faatiha ak fireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi 1 alhamdu lillaahi rabbil haalamiina 2 arrahmaanir rahiimi 3 maa li ki yaw mid diini 4 iyyaa ka nahbudu wa iyyaa ka nastahiinu 5 ihdinas siraatal mustaxiima 6 siraatal laziina anhamta halayhim xayril maxdoobi halayhim waladdaalliina 7 saaru faatiha ( 1--7)
Piri mi:
tudde nan ko saaru faatiha;ngir li ñu ko ubbee téereb Yàlla bi.
1-"bismil Lahir rahmaanir rahiimi 1"ci turu Yàlla laay tàmbalee jàng Alxuraan,di ko dimbalikoo moom Yàlla mu kawe mi,di baarkellu ci tud turam wi.
"Allaahi" maanaam:
ki ñiy jaamu ci dëgg, te deesu ko tudde ku dul moom Yàlla mu sell mi.
"Arrahmaani" maanaam:
boroom yërmande ju yaatu ji nga xamne yërmandeem daj na lépp.
"Arrahiimi" mooy:
boroom yërmande ñeel way gëm yi
2- "alhamdu lil Laahi Rabbil haalamiina 2" mooy: mbooleem xeet i cant yi ak mat yi ñeel na Yàlla moom rekk.
3- "maa li ki yawmid diini 3" mooy: boroom yërmande ju yaatu ji xajoo lépp, di boroom yërmande jiy jokk ñeel way gëm yi.
4- "maa li ki yawmid diini 4" mooy bis pénc.
5- "iyyaa ka nahbudu wa iyyaa ka nastahiinu 5" maanaam:yaw rekk la niy jaamu te yaw rekk la niy dimbalikoo.
6- "ihdinas siraatal mustaxiima 6" mooy gindi ku ci lislaam ak sunna
7-"siraatal laziina anhamta halayhim xayril maxdoobi halayhim waladdaalliina 7"mooy yoonu jaam i Yàlla yu sell yi ñuy yonent yi ak ñi leen topp,ci lu dul yoonu nasraan yi ak yahuud yi.
- dees na sopp ginnaw bunu ko jàngee nu wax "aamiin" maanaam: nangul sunu ñaan.

saaru az-zalzalatu ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"izaa zulzilatil ardu zilzaalahaa 1 wa axrajatil ardu asxaalahaa 2 wa xaalal insaanu maa lahaa 3 yawma-izin tuhaddisu axbaarahaa 4 bi-anna rabbaka awhaa lahaa 5 yawma-izin yasdurun naasu astaatan liyaraw ahmaalahum 6 faman yahmal misxaala zarratin xayran yarahu 7 waman yahmal misxaala zarratin sarran yarahu 8" (saaru az-zalzalatu 1-8)
Piri mi:
1-"izaa zulzilatil ardu zilzaalahaa 1" ëy bees yëngalee suuf si. yëngatu gu tar gay xew ca taxawaayu bis pénc ba.
2- "wa axrajatil ardu asxaalahaa 2" suuf si génne lépp lu nekk ci biiram ci way dee yi ak lu dul ñoom.
3- "wa xaalal insaanu maa lahaa 3" nit di wax ngir jaaxle: naan luy mbirum suuf si ba tax muy yëngatu a ka baj-baji?!
4- "yawma-izin tuhaddisu axbaarahaa 4" ci bis bu màgg boobu suuf si di na xibaare lépp lees def ci kawam ci yiw wala ay.
5- "bi-anna rabbaka awhaa lahaa 5" ndax Yàlla moo ko xamal digal ko loolu.
6-"yawma-izin yasdurun naasu astaatan liyaraw ahmaalahum 6"ci bis bu màgg boo bu suuf si di yëngatu, nit ñi da ñiy génn ci taxawaayu saytu ga di ay kurel ngir gis seen jëf yin jëfoon ci àdduna.
7- "faman yahmal misxaala zarratin xayran yarahu 7" képp ku jëf lu yamoog yamb wu ndaw a-ndaw ci lu yiw ak lu baax di na ko gis
8- "waman yahmal misxaala zarratin sarran yarahu 8" képp ku def lu toll noona ci ay jëf yu ñaaw di na ko gis.

saaru haadiyaati ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"walhaaditaayi dabhan 1 falmuuriyaatui xadxan 2 falmuxiiraatu subhan 3 fa asar na bihii naqhan 4 fawasatna bihii jamhan 5 innal-insaana lirabbihii lakanuudun 6 wa-innahu halaa zaalika lasahiidun 7 wa-innahu lihubbil xayri lasadiidun 8 afalaa yahlamu izaa buhsira maa filxubuuri 9 wa hussila maa fis-suduuri 10 inna rabbahum yawma-izin laxabiirun 11" saaru al-haadiyaati
Piri mi:

1- "walhaaditaayi dabhan 1" Yàlla giñ na ci fas yiy daw ba ñiy dégg ci moom kàddu ngir tar ug daw.
2-"falmuuriyaati xadxhan 2"mu giñaat ci fas yiy daw ba ay weyam,bu laalee xeer yi sax da ciy taal sawara ngir dal yu tar yim ciy dal.
3- "falmuxiiraatu subhan 3" mu giñaat ci fas yiy song noon ya ci suba si.
4- "fa-asarna bi hii naqhan 4" bu ñi daw di jeqi pënd bi.
5- "fawasatna bi hii jamhan 5" ñuy diggu mbooloo noon ya ci seen i gawar.
6- "innal-insaana li Rabbi hii lakanuudun 6" nit déy aji terewula ci yiw wi Borom am bëgg ci moom.
7- "wa-innahu halaa zaa li ka lasahiidun 7" te sax moom aji seede la ci terewoom yiw ga, du ko sax man a weddi ndax ak leeram.
8- "wa-innahu lihubbil xayri lasadiidun 8" te moom ag jéggi dayoom ci bëgg alal tax na da ciy nay.
9- "afalaa yahlamu izaa buhsira maa fil xubuuri 9" xanaa nit kii di woru ci dundug àdduna dafa xamul ne bu Yàlla dekkilee way dee yi ba génne leen ci suuf ngir saytu ak fay mbir yi du deme nam fooge woon?!
10- "wa hussila maa fis-suduuri 10" ñu fés al daal di leer al li ci biir xol yi ci ay yéene ak i pas-pas ak yaneen.
11-"inna rabbahum bi him yawma-izin laxabiirun 11"bis boobee déy seen Boroom aji dej kumpa la,darra du ko nëbbu ci mbir i jaam ñi te di na leen fay lépp.

saaru alxaariha ak firéem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
" alxaarihatu 1 maal xaarihatu 2 wa maa adraaka mal xaariatu 3 yaw yakuunun naasu kalfaraasil mabsuusi 4 wa takuunul jibaalu kalhihnil makfuusi 5 fa-amma man saxulat mawaaziinuhu 6 fahuwa fii hiisatin raadiyatin 7 wa-ammaa man xaffat mawaaziinuhu 8 fa-ummuhu haawiyatun 9 wamaa adraaka maahiya 10 naarun haamiyatun 11 saaru alxaarihatu 1-11"
Piri mi:

1-" Alxaarihatu 1" jamono ja nga xam ne day fëgg xol i nit ñi ngir màggug tiitaangeem ya
2- "maal xaarihatu 2" lan mooy jamono jii di fëgg xol i nit ñi ngir màgggug tiitaangeem ya ?
3- "wa maa adraaka 3" ana lan moo la xamal - yaw yonnent bi- luy jamono joo jii di fëgg xol i nit ñi ngir màaggug tiitaangeem ya?! mooy bisu taxawaay ba
4- "yaw yakuunun naasu kalfaraasil mabsuusi 4" bis bay fëgg xol nit ñi da ñiy mel ni ay lëppalëpp yu tasaaroo ci wàll wu ne.
5- "wa takuunul jibaalu kalhihnil makfuusi 5" te tund doj yi it mujj mel ni ngëndal bu nooy nepp ci woyofug dawam ga ak yëngatoom ga.
6- "fa-amma man saxulat mawaaziinuhu 6" képp ku ay jëfam yu sell not ay jëfam yu ñaaw.
7- "fahuwa fii hiisatin raadiyatin 7" koo kii de ma nga ca dund ganu gërëm da na ko am ca àljana.
8- "wa-ammaa man xaffat mawaaziinuhu 8" képp ku ay jëfam yu ñaaw not ay jëfam yu rafet.
9- "fa-ummuhu haawiyatun 9" dëkku waayam tey saxu waayam bisub taxawaay ba mooy jahannama.
10- "wamaa adraaka maahiya 10" ana lan moo la xamal -yaw yonnente bi- loolu mooy lan?
11- "naarun haamiyatun 11" aw sawara la wu tàng jérr

saaru attakaasuru ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
"alhaakumut takaasuru 1 hattaa zurtumul maxaabira 2 kallaa sawfa tahlamuuna 3 summa kallaa sawfa tahlamuuna 4 kallaa law tahlamuuna hilmal yaxiini 5 latarawunnal jahiima 6 summa latarawunnahaa haynal yaxiini 7 summa latus-alunna yawma-izin haninnahiimi 8" saaru attakaasuru 1-8
Piri mi:

1-""alhaakumut takaasuru1" li leen soxol de-yéen nit ñi-mooy ëppulaante ci alal ak i doom ci lu duk topp Yàlla.
2- "hattaa zurtumul maxaabira 2" ba faf ngeen dee dugg ca bàmmeel ya.
3- "kallaa sawfa tahlamuuna 3" ëppulaante de waru leen a soxlaal walif topp Yàlla, da ngeen xalseta xam mujjug soxlaal googu de.
4- "summa kallaa sawfa tahlamuuna 4" te it di ngeen xaseta xam ag mujjam de.
5- "kallaa law tahlamuuna hilmal yaxiini 5" ca dëgg-dëgg bu ngeen xamoon xam-xam bu wér ni dees na leen dekkil ngeen jëm fa yàlla, ci ne moom da na leen fay seen i jëf, kon du ëppulaante ci alal ak i doom du leen soxlaal.
6- "latarawunnal jahiima 6" giñ naa ci yàlla ni bisub taxawaay ba da ngeen gis sawara.
7-"summa latarawunnahaa haynal yaxiini 7" te it xalset ngeen koo gis gis gu wér ci ludud sikk-sàkka.
8- "summa latus-alunna yawma-izin haninnahiimi 8" te bis boobee Yàlla da na leen laaj bépp xéewal bumu leen xéewale woon ci wér ak koom ak yeneen.

saaru alhasri ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
walhasri 1 in nal insaana lafii xusrin 2 illal laziina aamanuu wahamilus saalihaati watawaasaw bilhaqi watawaasaw bissabri 3 saaru alhasri 1-3
Piri mi:

1-"walhasri 1" Yàlla mu sell mi giñ na ci jamono.
2- "innal insaana lafii xusrin 2" maanaam nit ñi ñéppa ngi ci yàqule ak ug alkande.
3- "illal laziina aamanuu wahamilus saalihaati watawaasaw bilhaqi watawaasaw bissabri 3" ndare way gëm yi tey jëf yiw, ànd ak loolu ñuy woote ci dëgg ak ci muñ, ñooñu ñooy ñiy mucc ci yàqule.

sarru alhumazatu ak fPreem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
"waylun likulli humazatin lumazatin 1 allazii jamaha maalan wahaddadahu 2 yahsabu anna maalahu axladahu 3 kallaa layunbazana filhutamati 4 wamaa adraaka maalhutamati 5 naarul laahil muuxadati 6 allatii tattalihu halal af-idati 7 innahaa halayhim musadatun 8 fii hamadin mumaddadatin 9 saaru alhumazatu 1-9
Piri mi:

1- "waylun likulli humazatin lumazatin 1" toroxtaange ak tar-tar i mbugal ñeel na ñiy jëw nit ñi ak di leen jam.
2- "allazii jamaha maalan wahaddadahu 2" ki nga xam ne yitteem mooy dajale alal rekk ak di ko lim,amul beneen yitte bu dul boobu.
3- "yahsabu anna maalahu axladahu 3" dafa njoort ne alalam ji miy dajale dana ko musal ci dee,mu sax ci dundug àdduna gi.
4- "kallaa layunbazana filhutamati 4" mbir mi du ne ko way sànku ji fooge de, dees na ko sànni ci biir sawaraw jahannama bi nga xam ne day dëbb di dammate lépp lunu ca sànni ngir tarug jafe-jafeem.
5- "wa maa adraaka maalhutamati 5" ana lan moo lay xamal -yaw yonnente bi- lan mooy sawara wii di dammate lépp lunu ca sànni?!
6- "naarul laahil muuxadati 6" mooy sawaraw Yàlla wa ñu taal.
7- "allatii tattalihu halal af-idati 7" way allawtiku yaram i nit ña ba ca xol ya.
8- "innahaa halayhim musadatun 8" ña ñiy mbugal dees na leen fa tëj.
9- "fii hamadin mumaddadatin 9" ci ay kenoy sawara yu ñu tàlli te gudd ba du ñu fa génn.

saaru alfiilu ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
"alam tara kayfa fahala rabbuka bi-ashaabil fiili 1 alam yajhal kaydahum fiitadliilin 2 wa arsala halayhim tayran abaabiila 3 tarmiihim bihijaaratin min sijjiilin 4 fajahalahum kahasfin makuulin 5 saaru alfiilu 1-5
Piri mi:

1- ""alam tara kayfa fahala rabbuka bi-ashaabil fiili 1" xanaa xamóo -yaw yonent bi- naka la sa boroom def Abrahata ak ay gaay am boroom ñay ya ban nammee màbb kaaba ga?!
2- "alam yajhal kaydahum fiitadliilin 2" Yàlla def na sEen pexe yu ñaaw yan tëroon ngir màbb kaaba ga mu naaxsaay, lan nammoon ci wëlbati nit ñi walif kaaba ga amuñu ko, te amun ci kaaba gi darra.
3- "wa arsala halayhim tayran abaabiila 3" mu yabal ci seen kaw ay picci yoy dikkal nanu leen di ay mbooloo.
4- "tarmiihim bihijaaratin min sijjiilin 4" ñu leen di sànni ay xeer yu wow koŋŋ
5- "fajahalahum kahasfin makuulin 5" Yàlla def leen ni ay xob i mbay yu daaba yi lekk ba joggate ko.

saaru xuraysin ak um piireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"li-iilaafi xuraysin 1 iilaafihim rihlatas sittaa-i wassayfi 2 falyahbuduu rabba haazal bayti 3 allazii athamahum minjuuhin wa-aamanahum minxawfin 4" saar uxuraysin 1-4
Piri mi:

1-"li-iilaafi xuraysin1" lees ci namm mooy lees miinoon ci tuukki jamonoy seddaay ak tàngaay.
2- "iilaafihim rihlatas sittaa-i wassayfi 2" tukkib seddaay ba jëm yaman, ak tukkib tàngaay ba jëm saam di ñu nekk ci kóolute.
3-falyahbuduu rabba haazal bayti 3"nan jaamu Boroom néeg bii ñu wormaal moom rekk,moom mi nga xam ne moo leen yombalal tukki yooyii,te buñu ko bokkaale ak kenn.
4- "allazii athamahum minjuuhin wa-aamanahum minxawfin 4" moom mi leen leel ba xiifu ñu, aar leen it ba ragalu ñu, ci limu def ci xol i araab yi ci màggal Haram bi ak màggal ñafa dëkk.

saaru almaahuuna ak um piréem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"ara-aytal lazii yukazzibu biddiini 1 fa zaalikal lazii yaduhhul yatiima 2 walaa yahuddu halaa tahaamil miskiini 3 fawalun lilmusallina 4 allaziina hum han salaatihim saahuuna 5 allaziina hum yuraa-uuna 6 wayamnahuunal maahuuna 7" saaru almaahuuna 1-7
Piri mi:

1- "ara-aytal lazii yukazzibu biddiini 1" ndax xam nga kiy weddi pay ga ca bis u taxawaay ga?!
2- "fa zaalikal lazii yaduhhul yatiima 2" koo ku mooy kay dàq jirim ba walif soxlaam.
3- "walaa yahuddu halaa tahaamil miskiini 3" te du ñaax boppam mukk du caagiine keneen ci leel way ñàkk.
4-"fawalun lilmusallina 4" alkande ak mbugal ñeel na way julli ya.
5- "allaziina hum han salaatihim saahuuna 5" ñay fowe seen ug julli, duñu ko faale ba waxtoom wa jeex.
6-"allaziina hum yuraa-uuna 6"mooy ñay ngistal ci seen ug julli ak seen i jëf,duñu sellal seen i jëf ngir Yàlla.
7- "wayamnahuunal maahuuna 7" ñuy terewu dimbali keneen ci lol dimbalee ca amul benn lor.

saaru kawsara ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"innaa ahtaynaakal kawsara.1 fasalli li Rabbika wanhari. 2 inna saani-aka huwal abtaru 3 saaru alkawsari 1-3
Piri mi:

1- "innaa ahtaynaakal kawsara 1" jox nanu la -yaw yonnente bi- yiw wu bari, tem bokk ca déegu kawsar ba ca aljana.
2-"fasalli li Rabbika wanhari 2" santal Yàlla ci xéewalam yii,ci nga koy jullil moom rekk ak di ko rendil,wuute ak li bokkaale kat yi di def ci jegeñ-jegeñ lu seen xëram ya ci rendil leen.
3-"inna saani-aka huwal abtaru3" ka la bañ moo dog ci lépp lu baax, mooy kañu fatte nga xam ne buñu ko tuudee rekk ci lu ñaaw lees koy tudd.

saaru alkaafiruuna ak um fpreem:
bismillahir Rahmaanir Rahiimi
"xul yaa ayyuhal kaafiruuna 1 laa ahbudu maa tahbuduuna 2 wa laa antum haabiduuna maa ahbudu 3 wa laa anaa haabudun maa habadtum 4 wa laa antum haabiduuna maa ahbudu 5 lakum diinukum waliya dini 6" saaru alkaafiruuna 1-6
Piri mi:

1- "xul yaa ayyuhal kaafiruna 1" waxal -yaw yonnente bi- ée yéen ñi weddi Yàlla
2- "laa ahbudu maa tahbuduuna 2" duma jaamu ci jamono jii mukk walaa ëllag xëram yi ngeen di jaamu.
3- "wa laa antum haabiduuna maa ahbudu 3" yeen itam du ngeen jaamu li may jaamu man, te mooy Yàlla rekk.
4- "wa laa anaa haabudun maa habadtum 4" man itam duma jaamu li ngeen di jaamu ci ay xëram.
5-"wa laa antum haabiduuna maa ahbudu 5" te déet yéen ngeen di jaamu li may jaamu man,te mom rekk mooy Yàlla.
6- "lakum diinukum waliya dini 6" yeen ak seen diine ji ngeen fental seen bopp, man ak sama diiné ji Yàlla wàcce ci man.

saaru annasri ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"izaa jaa-a nasrul Laahi walfathu 1 wa ra-aytan naasa yadxuluuna fii diinil Laahi afwaajan 2 fasabbih bihamdi Rabbika wastaxfirhu innahu kaana tawwaaban 3 saaru annasri 1-3
Piri mi:

1- "izaa jaa-a nasrul Laahi walfathu 1" su ndimbalu Yàlla ñëwee ñeel sa diine ji -yaw yonnente bi- ak ug tedd-ngaam , ubbiteg Màkkaam
2- "wa ra-aytan naasa yadxuluuna fii diinil Laahi afwaajan 2" nga gis nit ñi di dugg ci lislaam di ay mbooloo ay mbooloo.
3- "fasabbih bihamdi Rabbika wastaxfirhu innahu kaana tawwaaban 3" xamal ne loolu màndarnga la ci jegeg jeexug liggéey bi nu la yónni woon, na nga sàbbaal mgir sant sa Boroom, di ko sant ci xéewalug ndimbal gi ak ubbite gi, te nga sàkku ci moom ag njéggal, ndax moom jéggalaakon la aji naggu tuubug jaamaam yi la, te da leen di jéggal.

saaru almasadi ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"tabbat yadaa Abii lahabin wa tabba 1 maa axnaa hanhu laaluhu wa maa kasaba 2 sa yaslaa naaran zaatal lahabin 3 wamra-atuhu hammaalatal hatabi 4 fii jiidihaa hablun min masadi 5" saaru almasadi 1-5
Piri mi:

1-"tabbat yadaa Abii lahabin wa tabba 1"ñaari yoxoy baay tëxu yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc di Abii lahab toskare na ngir jëfam yu sànku ci li mu daan lor yonnente bi,te it ay jëfam sooy na.
2-"maa axnaa hanhu laaluhu wa maa kasaba 2" lan la la ko alalam ak i doomam jariñ? du ñu ko jeñal mbugal,te dees ko xëccal yërmaande.
3- "sa yaslaa naaran zaatal lahabin 3" bu bisu taxawaaybaa dina dugg sawara way tàkk jëppet, di jaaroo tàngaayam ba.
4- "wamra-atuhu hammaalatal hatabi 4" soxnaam sa it dana fa dugg moom mi daan lor yonnente bi ci di sànni ay dég ci yoonam wi.
5- "fii jiidihaa hablun min masadi 5" nekk na ca doqam la ab buum bunu xereñe ràbbin wa, di ko ci wommat jëme sawara.

saaru al-ixlaas ak um pireem:
bismillahir Rahmaanir Rahiimi
"xul huwal Laahu ahadun 1 Allahus Samadu 2 lam yalid wa lam yuulad 3 wa lam yakun lahu kufuwan ahadun 4 saaru al-ixlaas 1-4
Piri mi:

1- "xul huwal Laahu ahadun 1" waxal -yaw yonnente bi- ne: mooy Yàlla amul kenn kuñu war a jaamu kudul moom.
2- "Allahus Samadu 2" maanaam: dees na yëkkati soxlay mbindeef yi jëme ci moom.
3- "lam ya lid wa lam yuulad 3" moom Yàlla mu sell mi amul doom te amul way-jur
4- "wa lam yakun lahu kufuwan ahadun 4" amul dara lu niroo ak moom ci bindeefam yi.

saaru alfalaxi ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
"xul ahuusu birabbil falaxi 1 min sarri maa xalaxa 2 wa min sarri xaasixin izaa waxaba 3 wa min sarrin naffaasaati filhuxadi 4 wa min sarri haasidin izaa hasada 5" saaru alfalaxi1-5
Piri mi:

1-"xul ahuusu birabbil falaxi 1" waxal -yaw yonnente bi-ne:maa ngi muslu ci boroom suba gi tey làqatu ci moom.
2- "min sarri maa xalaxa 2" ci ayu lépp luy lure ci mindeef yi.
3- "wa min sarri xaasixin izaa waxaba 3" maa ngi muslu ci Yàlla ci bépp ay buy feeñ guddi ci ay daaba ak i sàcci.
4- "wa min sarrin naffaasaati filhuxadi 4" maa ngi muslu ci moom ci ayu njabarkat yu jigéen yiy ëf ca pas-pas ya.
5- "wa min sarri haasidin izaa hasada 5" ak ci ayu képp ku soxor te iñaane nit ñi li leen Yàlla may ci ay xéewal, tey tàbbal lor ci seen kaw.

saaru annaasi ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
"xul ahuuzu birabbin naasi 1 ma li kin naasi 2 iLaahin naasi 3 min sarril waswaasil xannasi 4 allazii yuwaswisu fii suduurin naasi 5 minal jinnati wannaasi 6" saaru annaasi 1-6
Piri mi:

1- "xul ahuuzu birabbin naasi 1" waxal -yaw yonnente bi- ne: maa ngi muslu ci Boroom nit ñi, tey làqatu ci moom.
2- "ma li kin naasi 2" mooy soppaxndiku ci ñoom num ko neexe, amuñu beneen buur budul moom.
3- "ilaahin naasi 3" mooy ki ñiy jaamu ci dëgg, amu ñu kenn ku ñiy jaamu ci dëgg ku dul moom.
4- "min sarril waswaasil xannasi 4" ci ayu saytaane miy sànni ay jax-jaxeem ci nit ñi.
5- "allazii yuwaswisu fii suduurin naasi 5" day sànni ay jax-jaxeem ci xoli nit ñi.
6- "minal jinnati wannaasi 6" maanam: kiy jax-jaxee dina nekk si nit ñi dina nekk itam si jinne yi.